Paleyotik gu digg-dóomu ga ma ngay tollook jamono ji topp ci Paleyotik gu suufe ga. Aaday njumtuwaay yu ñu defare tojit yu ndaw moo fa sàmpu, jaare ko ciy xar-kanami mbatiit yuy melal ay baaxi diiwaan.
Mbatiit yi gën a fës ci Paleyotik gu digg-dóomu ga ñooy Atérien fa Afrig ak Moustéren fa Órob.
Fa Afrig, ca bëj-saalumu Sahara, Paleyotik gu digg-dóomu tudde woon nañu ko Atum doj wu digg-dóomu wa (Middle Stone Age). Ay xar-kanam yu bari la amoon, yuy dëppook diiwaan ak jamono yu wuute :
- Fauresmithien : ñu duppeeko turu benn barab bu nekk fa Afrig bëj dex (Afrique du Sud), fa ñu gise ay këri liggeey yu deme ni moustérien, ak benn daggukaayu Levallois, ak ay jumtukaay yu am ay xoosukaay, cat yu ñaw, doju yaari wet yu yattu ak daggukaay yu ndaw.
- Sangoen : ñu xàmmee ko fa Ugandaa ak fa Ródéesi, li mu ràññeekoo mooy njumtukaayi tojat yu ñu ame ci daggukaayu Levallois, ay cat yu ñaw, ay doj yu ñu yatt yaari wet yi ak ay dogit yu yore melow xob.
- Stillbayen : ñu gis ko fa Stillbay, ca Tundu Kab ba Afrig bëj dex (Afrique du Sud), day melal ay njumtuwaay yuy fàttali ab Moustérien bu gën a baax, ñu defare ko ci njuréefi daggukaayu Levallois.
- Atérien : xar-kanamu mbatiit googu mi ngi bokk ci Paléolithique bu digg-dóomu ak bu kawe. Barabu bu ñu duppee, Bir el-Ater, ma nga nekk ca wetu Constantine (Alseri).
- Këru liggéeyu doj ëmb na ci biiram nak ay njumtukaay yu ñu defare ciy tojiti Levallois, ak cat yu sew ak xoosukaay (ndesiti yax yiy gindi yuy Atérien), ànd ak cati rëddu wos ak dogit yu yore melow xob.
