Ci diggante 2,5 et 1,3i tamdareti at, nit ñu njëkk ya fentoon te yaatal am mbatiit (xam-xam) mu tudd Oldowayenne (mbaa Oldowan), te li ko doon gën a feeñal moo doon genn këru liggéeyug yattum doj gu xereñ lool ba tax yenn ciy njumtukaayam ñoo ngi wëy daan leen jëfandikoo ba ci jamonoy ji ñu tàmbalee di dajaloo ciy dëkk ak di rattaxal doji yatt ya.
Ci ay doji ndox lañu daan liggeeye njumtukaayu wenn melo walla melo yu wuute, yu jur ay njumtukaayi doj yu dëgar, yu ame wet yu bari. Tojit yi bawoo ci yatt gi, te daanaka deesuleen laalaat, mëneesoon na leen a jëfandikoo naka ay njumtukaay.
Barab yi ëpp solo ci këri liggeeyub yattum doj ci Afrig (ñu natt ko ci diggante 2,6 et 1,8i tamdareti at)
HOMO ERGASTER – GUNEG TURKANA
(Guneg Nariokotome)
Kamoya, ma bokkoon ca mbooloom Richard Leakey, moo feeñal guneg Turkana ca atum 1984, fa Nariokotome, ca wetu Lac Turkana, fa Keeñaa. Ndesetu yax bi natt nañuy atam ci 1,6i tamdareti at. At yi mu amoon ca ba mu faatu tolloo na ci 12i at.
Ndaw loolu doon na tollu ci taxawaay 1,85 ñaay, bu demoon ba doon mag.
PEEGUG SAWARA SI
Njëfandikoo gi walla tàggatug sawara si saxal na ko pàkki taalu yu ñu defar walla ndesit yu xëm.
Bu dee njëfandikoog sawara ca Homo habilis ñoo ngi ci werante ba léegi, leer na ne Homo erectus moom tàggatoon na sawara si, loolu war naa tollu ci 500 000i at.
Ci li wër pàkki taalu yi – yi daan tax ñuy mën a togg ñam yi, di leerale ak di jaaru – ci la daan lootaabee dundug bokk-dundin, buy nangu yokkuteg aaday mbatiit ak joqalantey xam-xami xereñteef ak mën-mën. (delluwaayi kàrt yi : Dominique Grimaud ak al, 2017)
ACHEULÉEN
Paléolithique gu suufe gi mi ngi tollook jamono ji toftalu ci Paléolithique gu yàgg ga mbaa oldowayen. Day dajale xar-kanami mbatiit yu bari, te bi ñu gën a xam mooy Acheuléen, te mu màndargawoo ndefarug doju yaari wet yu yattu ak ay daggukaay (cleavers).
Su ñu ko méngalee cig yàgg ak Oldowayen, te muy mottali yenn doxali ya, Acheauléen ëmb na 1,7i tamdareti at ba ci lu war a tollu ci 200 000i at. Mu nekk jamono ju solowu ci diggante yattum doj mu yamamaay ak këru liggéeyu yattum doj gu ñuy gën a waajal ak a yaatal.
Ñaari njumtukaayi Acheauléen yu ràññeeku :
- Doju yaari wet yu yattu : njumtukaayu doj gu ñu yatt ci yaari wet yi, mën naa yore melokaanu saalu new, yatu xeej, rëddu nen mbaa rëddu wos. Soo ko xoole cig wet, yaxi ndoddam dañu lunk ba ñu leen yattee, mbaa ñu tàppee ci kawu doj, ak jub bu ñu leen defaree ak ub dóorukaayu bant. Doju yaari wet yu yattu wi dañu ko jëfandikoo ngir dagg, fees rab yi ñuy ray, waaye it, wulli ay der mbaa liggeey bant.
- Ag dagukaay (cleaver) : njumtukaay gu dëll, di màndargawoo ñawka gu galanu, ñu ko ame ci ndajem ñaari nataal : nataalub fett-fett, mbaa benn ci nataal yu kawe yi bub njumtukaay bi, walla rëyaayu doju ndox wi. Ñawka googu lu ci mas di bokk la, manaam deesu ko laalaat, te leeg-leeg benn mbaa ñaari wet yu ñu laalaat lay am. Lu ci ëppaan, dagukaay yi ci ay tojit lañu leen daan defare, ak lu néew nag ci doji ndox yi.
