Paléolithique gu mujj gi mbaa gu yees gi
Paléolithique gu mujj gi, ñu koy tudde it Paléolithique gu yees gi mbaa gu gën a jëm kanam, yemook ja mono ji mujj ci jamono ya jiitu mboorum niteef ju yàgg ja.
Li koy màndargaal mooy jëm kanamug ngànnaay yiy nirooleeki xob ak doji jànji sawara, ak yu ci mel ni cati fit yi, ñuy seede gën a baaxalug ngànnaay yi, ñuy jëfandikoo ci rëbb mi mbaa ci jamonoy ay.
Njumtukaay yi ñu defare yaxi rab dañu leen defare ci anam yuy nirook yuy doj (fëgg, rittaxal), mbaa ci yeneen anam (riisu, xeet). Wuuteg njumtukaay yi day yokku : xeej, want yu ñu bënn, tuf, sànnikaay, puso bu am bën-bën, rittaxalukaay, bàttu, bënnukaay, añs.
Njëfandikook yooyu tax na nit di gën a baaxal ak a yànjal ay njumtukaayam ndax woyofaay gi. Nooyaayu yax gi ak nu bari ni ñu ko mën a jëfandikoo (mënees na ko bënn, gàjj, yatt).
Néolithique
Néolithique, bi topp ci Paléothique, li koy màndargaal mooy ay coppeekuy xereñtéef yu xóot ak yuy bokk – dundin, ñu dottu ci mboolooy nit ña taamu xeetu dundin wuy sukkandiku ci mbay mi ak càmm gi.
Ñaari liggéey yooyu, ci lu bari, dafay tax a sax ci benn barab, sax googu wëlbatiku di yombal fenti xereñteef yu sakkan : njumtukaayi doj yu ñu rittaxal, ndaa, dëru ngir dër fepp yi, pexem liggéey dëkkuwaay, añs.
Càmm gi
Yarum jur gi dafa jël ay melokaan yu wuute su ñu sukkandikoo ci mbatiit yi ak kéew yi ñu feeñe. Tasaaroog juri yar yi it ci diiwaan yi ñu nekkul lu dul cig njaa-àlle, soppi na bu baax a baax bokk-dundin yoyu ak ndundat ya ca kéew yooyu.
Bokk-dundin yuy sàmm ak yu boole càmm geek mbay mi, yu bari yooyu, ñoo amal, ci diirub junniy-junniy at, ay xeeti dundin ya ñu dëppool, kéem ni ko nataali xunt yi ñu gis ci kemmbaar gi seedee, waaye it itte ji ñu jox taaralug jur yi ci yenn sàmmi-màngaani jamono jii.
Mbay ak wittat
Mboolooy rëbbkat-wittkat ya daan dem dañoo mujj soppeeku ndànk-ndànk ay bokk-dundin yu sax ci benn barab, ak a soppi seenug kéew, jaarale ko xereñtéefi mbay yu dëppook barab ya (lu ci mel ni suuxat mi) mu leen di mey mgóob mu yaatu.
Jëm kanam googu yombal na :
- yokkuteg nit ñi,
- aw séddalinu liggéey wu gën a jafe,
- yokkug yaxantuy weccoo,
- sàkkug tëralini caytuy polotig yu dajaloo,
- ak fëllug pexey jottalini xam-xam, yu ci mel ni mbind mi.
