Musée des Civilisations noires: Bienvenue

Génn Afrig yi ak Kiliftéefu àddina si

Génn Afrig yi ak Kiliftéefu àddina si.

Génn gu njëkk gi ñu génn Afrig.

Homo ergaster, mbaa Homo erectus, mooy ki jëkk a génn Afrig ngir dem Asi ak Órob, am na lu war a tollu ci 2i tamdareti at. Màng gu njëkk googu, peeñali ngas-ngent yu bari dëggal nañu ko : ndaal bopp yi ak desiti ndesi yaxi Homo geogicus, fekk ñu ko fa Dmanisi, ca Géworgi, ay atam ñu natt ko ci 1 tamdareti at ak 8i téeméeri junniy at; yoy Pithécanthrope erctus fa Java, ca Indonésie (1 tamdaretu at ak 6i téeméeri junniy ciy at), bub Homo antecessor, fa Sima del Elefante, fa Espagne (lu tollok 1 tamdareti at ak 2i téeméeri junniy at) ; ak bub Sinanthrope bu Pékin (Sinanthropus pekinensis), fa Lantian, fa Chine (lu tollu ci 1 tamdaretu at).

Fa Ërób, Homo erectus dafay dox ndànk-ndànk jëm ci Homo heidelbergensis. Ñu  feeñal wenn ndesi yax fa Maouer, fa Almaañ, te ñu natt ay atam ci diggante 600 000 ak 550 000i. Ginnaaw bi ñu gis Homo neanderthalensis, ca Kóonu Arago, fa Tóotawel, ca Farãs, ñu natt ay atam ci diggante 2i téeméeri junniy ak 20i junniy at ak 7i junniy at (200000i at ak 27000iat).  

Fa Asi, ay xeeti Homo erectus yu wuute feeñ nañu fa, 50i junniy (50000) at lu jiitu juddug Isaa. Dinañu fa fekk Homo floresiyensis, ñu gis ko ca xuntum Liyang Bua, fa dunub Flores, ci noonu it fekk nañu Homo neyandertaalensis ak Denisowiyens yi, ca xuntum Denisowa, fa Riisi.

Génn gu mujj gi ñu génn Afrik

Jortees nañu ne Homo sapiens feeñ nañu fi Afrig, loolu ëpp na 3i téeméeri junniy at (300000i at). Ñu ngi soqeekoo ci Homo erectus/ergaster (mbaa Homo sapiens mu yàgg ma), dëggal nañu ag  nekkam fa Afrigu bëj-gànnaar (Jebali Irhuud, fa Marog 3i téeméeri at ak15i junniy at (315000 i at)),  fa penkub Afrig (Omo Kibish, 195 000i at ; Herto, 160 000i at fa Ecóopi; Ngaloba, 120 000i at, fa Tànsani).

Homo sapiyens ku yàgg kooku jortees nañu ne daa màng wuti yeneen kemmbaar : Asi, Órob, Amerig ak Oseyaani.

Xibaari kosi-ndono yi dañuy tegtale ne balaa muy wuutu nit ñu yàgg yi muy daan taseel ciw yoonam, Homo sapiyens daa mel ne dafa daan weccoo kosi-ndono ak ñoom – bokk ci ak Homo neanderthalensis – di seede ay kaawteefi njaxasum giir.

  • Ma = tamdareti at
  • Ka = Junniy-junniy at.
  • Génn gu jëkk gi ñu génn Afrig
  • Génn gu mujj gi ñu génn Afrig
Primary Color
default
color 2
color 3
color 4
color 5
color 6
color 7
color 8
color 9
color 10
color 11
color 12