ÓSTARALIPITEK YI AK PARATOROP
Am na lu ëpp 4i tamdareti at, la ay mboolooy nit yuy doxe ñaari tànk, ñu tuddeleen óstaralopitek ak paratorop, feeñ. Ki ci gën a yàgg téy ñu xam ko mooy Australopithecus anamensis, ña nga feeñale fa Kanapoi, fa diwaanu lac Turkana, fa Keeñaa.
Ci luy tollook 3,5 tamdareti at, óstaralopitek ya dañoo séddalikoo ci ay giir yu bari te wuute, ngir mën a yemook xeeti dundin yi ci ñaayi Afrig yi, fekk parantorop raaf nañu te bàyyiwuñuy doono. Ci xeet yi ñu gën a xam bokk nañu ci :
- Australopithecus deyiremeda, ca penkub Afrig, fa bëj-gànnaaru Ecóopi (diggante 3,5 ak 3,3i tamdareti at);
- Australopithecus afarensis, fa Ecóopi (diggante 3,4 et 3i tamdareti at), te Dinknesh (Lisi) di ko jëmmal ak rëddi ndëgguy Laetoli, di dëggal kuy doxe ñaari tànk;
- Kenyanthropus platyops (walla nit ka ca xar-kanam gu tàppndaar ga fa Keeñaa), ñu natt ko ci diggante 3,5 ak 3i tamdareti at;
- Paranthropus aethiopicus, ca xuru Omo wa (Ecóopi), ñu natt ko ci diggante 3,5 ak 1 tamdaretu at;
- Paranthropus boisei, tuddoon bu njëkk Zinjanthropus boisei, ñu natt ko ci 1,8i tamdareti at, ñu gis ko ca xuri Olduvai (Tànsani);
- Australopithecus garhi, ñu natt ko ci 2,5i tamdareti at (Ecóopi);
- Australopithecus bahrelghazali, ñu xame ko ci turu Abel, mu feeñe fa Tchad fa Afrig gu digge, ñu xayam ko ci diggante 3,5 ak 3i tamdareti at;
- Australopithecus africanus, ca bëj-saalumu Afrig (diggante 3,2 ak 2,4i tamdareti at), mu di ko jëmmal :
- Guneg Taung, ñu gis fa Afrig bëj dex (Afrique du Sud)
- Plesianthropus transvaalensis, ñu koy dàkkantale Jongomay Ples, bub barabu Sterkfontein ba
- Australopithecus sediba, ñu gise ko ca xuntum Malapa ma, ñu natt ko ci 1,97 tamdareti at,
- Paranthropus robustus, ñu natt ko ci 2 ak 1 tamdaretu at, mu nekk fa Swartkrans ak ca xuntum Kromdraai ma, fa goxub Gauteng (Afrig bëj dex/ Afrique du Sud).
