Ci diggante 8 ak 6i tamdareti at, ci la xàjjaloo ame ci diggante xeetu dangin yi ak wuw nit ñi fi Afrig. Ci tolluwaayu peeñalug jamonoy yatt doj – càmm – wittat, ñatti giir ñoo àndandoo di xëccoo taxawaayu nit ki gën a yàgg gu ñu xam :
- Sahelanthropus tchadensis, ñu gën koo xame ci turu Tumaay, ñuy natti atam ci 7i tamdareti at (Càdd) ;
- Orrorin tugenensis, ñu natti atam ci 6 tamdareti at (Keeñaa) ;
- Ardipithecus kadabba, ñu natti atam ci 5,7 tamdareti at ak 6i tamdareti at (Ecóopi) ;
- Ardipithecus ramidus (càqu yax gu mat daanaka), ñu natti atam ci 4,4i tamdareti at (Ecóopi).
Melokaani ardipitek ya :
- Foramen magnum bi (bën-bënu ndaal bopp) dafa jëm kanam ci cëslaayu ndaal bopp li ci lu leer, muy màndargam, ci lu mën a nekk, kuy doxe ñaari tànk.
- Dëgëj yi, yu cuub ga sewandi, dañoo xaw a yaatu bu ñu leen gam-gamleek yuy golo yiy xellamikook nit, waaye gën a tuuti yuy óstralopitek ya.
Dundinu ardipitek ya :
Desi ndesiti yaxi rab ya ak gàncax ya dañuy juñj kéew gu am dox, bu am ay àll yu bari garab ak ay ñaay yu ami garab.
Gëñ yi dañuy tegtale dundub kuy lekk lépp ak meññent, ak ñam wu dëgërul walla lu ñu dul joññ dul bokk.
ARDIPITHECUS RAMIDUS : 4,4i tamdareti at — Middle Awash (Ecóopi)
SAHELANTHROPUS TCHADENSIS : 7i tamdareti at — Toros Menalla (Càdd)
ORRORIN TUGENENSIS : 6i tamdareti at — Lukeino (Keeñaa)
Australopithecus afarensis – Dinknesh (Lisi)
Ndesitu yax woowu mooy benn ci des yi gën a mat ci lu ñu mas a gis ci ab Australopithecus. Ay atam war nañoo tollu ci 3,2 tamdareti at.
Menn mbooloom farañse ak amerikee, mu Yves Coppens jiite, moo feeñal, ca atum 1974 fa Ecóopi, Dinknesh – ñu duppee ko Lis – muy tollu ci taxawaay 1,2 ñay, di peese 30i kilo te 20i at la dund.
Dafa daan taxaw di dox ak ñaari tànkam, doonte dañoo gàtt, te ame yoxo yu gudd yu koy may muy yéeg ci garab yi.
RËDDI NDËGGUY LAETOLI
Rëddi ndëgguy Laetoli Mary Leakey ñoo gi ko gis fa Laetoli, ca Tansani.
Ñooy firnde bi gën a yàgg bu ñu xam ci kuy doxe ñaari tànk ci nit ñu njëkk ya.
Ci dóomi jànji sawara lañu leen fekk ñu ni ñumm. Dinañu ci ràññee rëddi ndëgguy mag mu ànd ak genn gune. War nañu tollu ci 3,5 tamdareti at te ñoo ngi leen di dello ca Australopithecus afarensi.
