Afrig ag kembaar la gu ame ndono lu yéeme te mbooru nitam yàgg lool. Afrig suufus mboor la, mbatiit ak ñeeñal, ci ay am-amam yu sàmmu, yu ñu luññutóogul. Moo ëmb ëllëgu niteef gi mu jur. Leegi ñépp nangu nañu ne Afrig mooy laytaayu niteef gi. Ndesi yaxi nit ñu njëkk ña ak firdey ngas-ngent yi nu ngi gàññ ci kembaar gi, di gën a yaatal sunu xam-xam ci sunuy cosaan. Waaye ngir ñu egsi fii ñu egsi ci peeñal yi, ay ati góor-góorlu yu baree bari la woroom xam-xami saa-afrig yi ak tubaab yi def ngir sulli desiti yaxi maam yu sori ya, ya ruuru woon ca déndi daar-daari xuru Rift wa ak ca xóotaayi ndànd foy-foyug Càdd ga. Tumaay ak Dinknes (Lisi), ñi ñu nangu tey ni ñooy ñi njëkk ci xeetu nit, ay seede lañu ci dox bu dul dog bi niteef gi di dox jëm ci gën a nite, gën a xereñ, rawati ci, gën a bariy bëgg-bëgg. Tukkite bu solowu boobu nekk na ay tëkk yu tegaloo, yuy gën a rëy saa su ne, waaye saa su ne, ñu leen di nangu. Dëgar gu yéeme googu, nii la ko Perisidã Seŋoor tënke, ci waxtaan wa mu defoon ca ubbiteg 6eelu Ndajem saa-afrig, ma ñu amaloon ca atum 1967 te mu aju woon ci jamono ya jiitu mboorum niteef gi : « Omo sapiyen weesu na, cig péexteem, tëralin wig kéewam di doxe. » Li ñu dul wax lu bari, mooy rëddu-jisu saa-afrig boobu masul a doon Afrigam doŋŋ, waaye Déndu-suuf sépp la. Ab xarekat la woon, te fi ci Afrig la wànqaasi askan yi notoon Suuf si jóge woon, topp yoon yu jaxasoo te jafe. Ci noonu, sunu wuute gi jëf duñu lu dul ay xew-xew yu doyadi, ci kanamu tukkib xeetu nit wu yéeme woowu. Bindub mboor bi ñu war a jàngale ci jàngu yépp, mooy, ci wàllu xam-xam, nun ñépp ci déndub suuf sii lanu cosaanoo, doon ay saa-afrig. Fepp fu saa-afrig yi tollu dañoo war a yëg ne ci seen suuf lañu nekk.
Ab dox bu gudde ay tamdareti at yu bari. AFRIG, LAYTAAYU NITEEF GI Nun ñepp ay saa-afrig lanu, ci sunu cosaan • Nit ki jëkk a dox ci suufus Afrig. • Njumtukaay gi njëkk ci suufus Afrig lees ko defare. • Mboolooy nit yu njëkk yaak yu mujj ya yilifoon àddina si, ci Afrig lañu jóge.